Hadith for the World
Julli

Warug julli ak àtteb ki ko bàyyi

5 hadiths

5 hadiths

Jële nañu ci Amr ibn Suhaybu mu jële ci baayam mu jële ci maamam mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya».Abóo Daawuda soloo na ko
Jële na ñu ci Buraydata Ibn Al-Husaybi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Deeleen teel a julli tàkkusaan, ndax yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna".Al-buxaariy soloo na ko
Jële na ñu ci Abdullah Ibnu Umar-yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : "tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu: {taxawalal julli ngir fàttaliku ma}[Taaha: 14]».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli».Muslim soloo na ko