126 hadiths
Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ma taaya fekk samay ténq moo ngi ci diggante ñaari ténqam, kem ni mu ma xamale saaru Alxuraan: "Attahiyyaatu lil Laahi, assakiyyaatu lil Laahi, attayyibaatus salawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan nabiyu,wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahis saalihiina,ashadu an laa ilaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu". Nekk na ci yeneen baat: "Yàlla mooy jàmm, bu kenn ci yéen toogee ci julli na wax: "Attahiyyaatu lil Laahi, assakiyyaatu lil Laahi, attayyibaatus salawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan nabiyu, wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahis saalihiina, bu ko waxee jot na dal na bépp jaam bu sell ci asamaan ak suuf, ashadu an laa ilaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu, topp mu tànn ci ñaan yi lu ko soob".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu Jaabir ibn Abdul Laahi yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan, mu wax ne: "bu kenn ci yéen yittewoo am mbir, na julli ñaari ràkka yu dul farata, topp mu wax: Allaahuma innii astaxiiruka, bi hilmika, wa astaqdiruka bi xudratika, wa as-aluka min fadlika Al-Hasiimi, fa innaka Taqdiru wa laa aqdiru, wa Tahlamu wa laa ahlamu, wa Anta Hallaamu alxuyuubi, Allaahuma in Kunta Tahlamu anna haasal amra xayrun lii fii diinii, wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii, wa aajilihi, faqdurhu lii wa yasairhu lii summa baarik lii fiihi, wa in Kunta tahlamu anna haasal amra sarrun lii fii diinii wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii wa aajilihi, fasrifhu hanni wasrifnii hanhu waqdur liya alxayra haysu kaana summa ardinii bihii" nee na: "mu tudd aajoom".Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp, loolu nag ndax bu kenn ci ñoom jàppee rafetal njàppu ma, daal di dem ca jàkka ja te dara yëkkatiwu ko lu dul julli, du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil daraja, sippil ko ci njuumte, ba ba muy dugg ca jàkka ja, bu duggee ca jàkka ja ci julli la nekk fii ak julli moo ko téye, te malaaka yi dañuy julli ci kenn ci yéen fii ak moo ngi ca bérab ba mu doon jullee, dañuy wax naan: Yàlla yërëm ko, Yàlla jéggal ko, Yàlla nangul tuubam, fii ak lotul kenn, te tojlewul».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér