Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële na ñu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Available in 49 languages
«Jële na ñu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum koor, Saah ci tàndarma,walla Saah ci pepp,ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi,mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waral na asakay muurum koor ginnaaw weeru koor, te mooy luy tolloo ak Saah muy tollook ñenti Mudd. Mudd mooy: lu fees ñaari loxoy góor gu diggudóomu, ci tàndarma walla pepp ci bépp jullit; gor ak jaam, góor ak jigéen, xale ak mag, loolu ci ku am lu des ci dundu bisam ak guddeem, ci boppam ak ki muy dundal. Mu digle ñu joxe ko laata nit ñi di génn jëm ca julli ga.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality