Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 71 languages
«Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral ganam».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jaam bi gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nga xam ne falay dellu ñu fay ko ay jëfam, ngëmam dana ko ñaax ci jikko yii: Bu njëkk bi: wax ju rafet: ci sàbbaal, ak tudd Yàlla, di digle lu baax, di tere lu bon, di defar diggante nit ñi, bu ko deful it mu taqook noppi téye loram te sàmm làmmiñam. Ñaareel bi: teral dëkkandoo: ci di rafetal jëme ci moom te bañ koo lor. Ñatteel bi: teral gan gi ñëw ngir seetsi la: ci wax ju teey, ak jox ko ñam ak yu ni mel.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality