Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 70 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis b: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sabab yi gën a màgg yuy dugale àjjana ñaari sabab la, te mooy: Ragal Yàlla ak rafet jikko. Ragal Yàlla: mooy nga def kiiraay sa diggante ak mbugalum Yàlla, ci di def ay ndigalam di moytu ay tereem. Rafet jikko: dana nekk ci yaatal kanam, ak di def ñekk tey feg lor yi. Sabab yi gën a man a duggale sawara ñaar la, te mooy: Làmmeñ ak awra. Bokk na ci Bàkkaari làmmeñ yi: fen ak jëw ak rambaaj ak yeneen. Bokk na ci Bàkkaari awra yi: njaalo ak ngóor-jigéen ak yeneen.

Source
At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Download image

Saved at original quality