WO
Koor
Fukki guddi yi mujj ci weeru Koor
4 hadiths
Obligation of Fasting and Ruling of Its Abandoning
1
Ngëneelu koor
5
سنن الصيام
7
رؤية الهلال
2
صيام يوم الشك
2
صيام أهل الأعذار
1
مفسدات الصيام
2
ما يجب على الصائم
1
ما يجوز للصائم
1
صيام التطوع
12
الاعتكاف
1
Fukki guddi yi mujj ci weeru Koor
4
Weeru Koor
2
4 hadiths
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu.
Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi daan dugg da daan dundal guddi yi, yee njabootam, pasteefu daal di takku ba dëgër.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér