Ngëneel yi ak teggiin yi
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
Available in 62 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ci jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc, ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira, ku suturaal ab jullit Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira, Yàlla day dimbali jaam bi fii ak jaam bi moo ngi dimbali mbokkam, ku sóobu aw yoon di ca sàkku xam-xam yàlla yombalal ko yoonu àjjana, te aw nit duñu dajaloo ci ak kër ci këri Yàlla yi di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir lu dul ne ag dal dana wàcc ci seen kaw yërmànde muur leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tudd leen ca ña fa moom, ku ay jëfam yeexal askanam du ko gaawal».»Meaning translation ·
Saved at original quality







