Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

Available in 62 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ci jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc, ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira, ku suturaal ab jullit Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira, Yàlla day dimbali jaam bi fii ak jaam bi moo ngi dimbali mbokkam, ku sóobu aw yoon di ca sàkku xam-xam yàlla yombalal ko yoonu àjjana, te aw nit duñu dajaloo ci ak kër ci këri Yàlla yi di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir lu dul ne ag dal dana wàcc ci seen kaw yërmànde muur leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tudd leen ca ña fa moom, ku ay jëfam yeexal askanam du ko gaawal».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne payug jullit bi fa Yàlla day xeetoo ak li jullit bi di def ak jullit ñi; ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ak tar-tar ci jafe-jafey àdduna yi, Yàlla fay ko ci dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc yi. Ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe defal ko jàppandal dindil ko jafe-jafeem, Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira. Ku suturaal ab jullit niki mu gis ci moom lu jaaduwul a feeñal ci ay tarxiis ak i njuumte, Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira. Yàlla day dimbali jaamam bi, fii ak nit ki moo ngi dog ci dimbali mbokkam ci luy yéwénal àdduna ak diine, dimbali nag day nekk ci ñaan ak yaram ak alal ak lu dul loolu. Ku dox ci wut xam-xam, jublu ca jëmmi Yàlla mu kawe mi; Yàlla yombalal ko yoonu àjjana. Aw nit duñu dajaloo ci ag kër ci këri Yàlla yi, di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir, lu dul ne ag dal dana wàcc ci ñoom, yërmànde muur leen matale leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tagg leen ca ña ko jege, te Yàlla tudd jaam bi fa mbooloo ma gën a kawe doy na teddnga. Ku ay jëfam nekk lu mànki, ba tax eggul ca boroom jëf yu baax ya, jaadu na mu bañ a wéeru ci askanam wu tedd ak ay ngëneeli ay baayam ba noppi di gàtteñlu ci jëf yi.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality