Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 56 languages
«Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom, daan na daje ak moom guddi gu nekk ci weeru koor di jàng ak moom Alxuraan, waat naa ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gën a tabe ci yiw ngelaw lu ñu boyal.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, te ag tabeem daana yokk lool ci weeru koor ba daan na joxe li yell a joxe ñeel ku ko yeyoo, li waral tabeem daan yokk nag ñaari mbir la: Bi ci njëkk: daje gi mu daan daje ak Jibriil yal na ko Yàlla yokk jàmm. Ñaareel bi mooy: Tari gimudaan tari alxuraan ji si jibriil. Daan na tari si Jibriil Alxuraan jépp, mu waat ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gën a tedd gën a man a joxe ak def aw yiw, gën a gaaw a jariñ nit ñi ci ngelaw lu teey lu Yàlla yabal ci taw ak yërmànde.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality