Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële nañu ci Abuu Muusa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 48 languages
«Jële nañu ci Abuu Muusa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ñeel na Aji-gëm ji ca àjjana ab xaymab wurus bu ñu yaatal, guddaayam tolloo ak juróom-benni Miil, aji-gëm ji dana fa am ay njaboot, aji-gëm ji dana leen wër te ñenn ñi duñu gis ñeneen ñi".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare lenn ci xéewali àjjana ya, ak ne aji-gëm ji dana am ca àjjana xayma bu màgg te yaatu ci biiram, mu nekk ci wurus wu yaatu, yaatuwaayam ak guddaayam ci kawe toll ni juróom-benni miil, wet gu nekk ak wàll wu ne ak koñ bu ne ci ñenti koñam am na fa ay soxna, ñenn ñi duñu gis ñeneen ñi, te aji-gëm dana leen wër ñoom ñépp.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality