Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:

Available in 60 languages
«Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: "góor du xool awray góor, jigéen it du xool awray jigéen,te góor ak góor duñu sàngu ci menn malaan,jigéen ak jigéen it du ñu sàngu ci menn mbalaan .»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa tere góor di xool awray góor, walla jigéen di xool awray jigéen. Awra nag: mooy lépp lol bu feeñee nit ki rus, te awray góor mooy li dale ci jumbaxam ba ci wóomam, Jigéen nag léppam awra la ci góori jàmbur,bu dee ci ay jigéen ak ci ñi ko araama takk day feeñal li aadawoo feeñ buy liggéey ci këram. Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-tere na góor di wéet ak góor ci benn mbalaan te fekk soluñu dara,mbaa jigéen di wéet ak jigéen ci menn malaan walla ci genn càngaay daal di raflewu;ndax loolu man naa tax ku ci ne di laal awray moroomam,te laal ko dañu koo tere kem ni ñu teree xool gi, moom sax nag moo gën a tar ug tere;ndax yàqute yi muy indi moo gën a rëy.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality