Hadith for the World
Aj ak wumra

Ngëneelu aj ak wumra

5 hadiths

5 hadiths

Jële na ñu ci Ibn Abbaas-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax jenn jigéen ju bokk ci Ansaar yi Ibn Abbaas tudd na ko waaye maa fàtte turam:"lan moo la tere nga ànd ak nun aji?" Mu ne ko: amunu lu dul ñaari giléem baayu doomam ak doomam ja aji ca genn giléem ga bàyyeel nu genn giléem te ci lañuy wute ji ndox,mu ne ko:"bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- muy wax naan: "képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax".Al-buxaariy soloo na ko
عن عائشة رضي الله عنها مرفوعاً: «ما مِن يومٍ أكثر مِن أنْ يُعْتِقَ اللهُ فيه عبدًا مِن النارِ، مِن يومِ عرفة، وإنَّه ليدنو، ثم يُباهي بهم الملائكةَ، فيقول: ما أراد هؤلاء؟».رواه مسلم
عن أبي هريرة رضي الله عنه: أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: «العمرة إلى العمرة كفارةٌ لما بينهما، والحج المبرور ليس له جزاءٌ إلا الجنة».متفق عليه