Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 60 languages
«Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dañoo gisoon ne jihaad ci yoonu Yàlla ak xeex ak noon yi moo gën ci jëf yi, Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- daldi laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax ñoom jigéen ñi ñu jihaadi? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- gindi leen ci jihaad gi gën ci seen àq te mooy aj gu baax gu dëppoo ak Alxuraan ak Sunna, gu mucc ci bàkkaar ak ngistal.

Source
Al-buxaariy soloo na ko
Download image

Saved at original quality