Hadith for the World
Xeex ci yoonu Yàlla

Teggiini xeex ci yoonu Yàlla

4 hadiths

4 hadiths

عَنِ ابْنِ عُمَرَ رَضيَ اللهُ عنهما قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «إِذَا جَمَعَ اللهُ الْأَوَّلِينَ وَالْآخِرِينَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ يُرْفَعُ لِكُلِّ غَادِرٍ لِوَاءٌ، فَقِيلَ: هَذِهِ غَدْرَةُ فُلَانِ بْنِ فُلَانٍ».متفق عليه
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن عبد الله بن أبي أوفى رضي الله عنه أَنَّ رسول الله صلى الله عليه وسلم فِي بَعْض أَيَّامه التي لَقِي فيها العدو انتظر، حتى إذا مَالَتِ الشمس قام فِيهم، فقال: «أَيُّها الناس، لا تَتَمَنَّوْا لِقَاء الْعَدُوِّ، وَاسْأَلوا الله الْعافية فَإِذا لَقِيتموهم فَاصْبِرُوا، وَاعلموا أَنَّ الْجَنَّة تحت ظِلال السُّيوف ثُمَّ قَال النَّبِي صلى الله عليه وسلم: اللهمَّ مُنزِلَ الْكتاب، وَمُجْرِيَ السَّحاب، وَهازم الأَحْزاب: اهْزِمهم، وَانصُرنا علَيهم».متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waa juy xeex ngir wone njàmbaar, ak kuy xeex ngir par-parloo, ak kuy xeex ngir ngistal, ana kan ci ñoom moo nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: "kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér