Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 60 languages
«Jële nañu ci Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waa juy xeex ngir wone njàmbaar, ak kuy xeex ngir par-parloo, ak kuy xeex ngir ngistal, ana kan ci ñoom moo nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: "kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wuuteg jubluwaay yi ci ñiy xeex; kuy xeex ngir jàmbaare, walla par-parloo walla ngir ñu gis dayoom ci nit ñi mbaa leneen, kan moo ci nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne kiy xeex ci yoonu Yàlla: mooy kiy xeex ngir kàddug Yàlla jëm kaw.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality