Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Al-Muxiirata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:

Available in 61 languages
«Jële nañu ci Al-Muxiirata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- cib tukki, ma nar a summi ñaari saŋam yi, mu ne ma: "bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab" mu masaa ca seen kaw.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci ab tukki, daal di jàpp, ba mu tollee ci raxas tànk yi Al-Muxiirata Ibn Suhbata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàllal loxoom ngir summi li nekk ci tànki Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-di ay dàlli saŋ ngir mu raxas ñaari tànk yi! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ne ko: bàyyileen te bu leen summi, ndax damaa dugal samay tànk ci saŋ yi fekk maa ngi cig laab, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di masaa ci kaw saŋ yi mu wuutu raxas ñaari tànk yi.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality