Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële na ñu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :

Available in 62 languages
«Jële na ñu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : «digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér : cib jëh, mu daadi junj loxoom ci bakkanam, ak ñaari loxo yi, ak ñaari wóom yi, ak cati baaraam yi, ak ñu bañ a téye mbaa wog seen i yére ak seen kawar».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne Yàlla da koo digal ci julli muy sujjóot ci juróom-ñaari céram; te mooy: Ab jëh: te mooy: xar kanam ci kaw bakkan bi ak ñaari bët yi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- junj loxoom ci bakkanam, ngir leeral ne jëh ak bakkan benn cér la ci juróom-ñaari cér yi, ak feddali ne kiy sujjóot day laalale bakkanam ci suuf. Cérub ñaareel bi ak bu ñatteel bi mooy: ñaari loxo yi. Bu ñenteel bi ak bu juróomeel bi mooy: ñaari wóom yi. Bu juróom-benneel bi ak bu juróom-ñaareel bi mooy: baaraami tànk yi. Mu digal nu nuy bañ a takk sunu kawar, walla nuy dajale sunu yére bu ñuy sujjóote ci suuf ngir feg ko; waaye danu koy yoor mu tege ci suuf, mu sujjóot ak cér yi.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality