Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne:

Available in 51 languages
«Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam.»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taqoo woon ak Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ngir sàkku Laylatul Xadri, mu wéy ci loolu ba Yàlla faat ko, ay soxnaam yal na leen Yàlla dollee gërëm taqoo ak Lihtikaaf ci ginnaawam.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality