Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Dégg diine ak i cosaanam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

Available in 49 languages
«Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na jullit bi woor njëkk weeru koor ci benn walla ñaari bis ci yéeneg wóorlu ñeel weeru koor gi; ndaxte warug woor weeru koor gi dees koo wékk ci gis weer wi, te aajowul a toggoo coona, lu dul koo xam ne da daan woor ag woor gu mu aadawoo niki woor bis dog bis, walla bisu Altine walla Alxamis, mu dëppoo ak moom kon na ko woor; loolu bokkul ci gatandu weeru koor, dees na aj ci loolu it lu nekk woor gu war niki fay ak nisër.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality