Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Available in 69 languages
«Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaan mooy jaamu Yàlla» daal di jàng: "Aaya biy wax ne: {séen Boroom nee na wooleen ma ma wuyu leen ñi may rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox} [ soratou Xaafiri: 60]».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ñaan mooy jaamu Yàlla, kon li war mooy mu nekk lu sell ñeel Yàlla, moo xam wooteg laaj la walla wooteg sàkku, ci di laaj Yàlla mu kawe mi lu koy jariñ, ak jeñ lu koy lor ci àdduna ak allaaxira, walla muy wooteg jaamu, te mooy lépp lu Yàlla bëgg te gërëmloo ko ci ay wax ak i jëf yi feeñ ak yi nëbbu, jaamuy xol yi walla yu yaram yi mbaa yu alal yi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tegtaloo na ci loolu ne: Yàlla wax na ne: {wooleen ma ma wuyu leen ñi ma rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox}

Source
Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Download image

Saved at original quality