Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 60 languages
«Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: yan ci jikkòy lislaam yi ñoo gën? Mu tudd ñaari jikkó: Bu njëkk bi: di baril di leel way-ñàkk yi, dana ci dugg ba tay saraxe ak àddiya ak nganale ak céetal, ngëneelu lele nag dana feddaliku ci jamonoy xiif, ak bi njëg yi seeree. Ñaareel bi: di nuyu bépp jullit, moo xam xam nga ko walla xamóo ko.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality