Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Available in 66 languages
«Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nekkul woon ku ñaawi wax mbaa jëf, daa na wax naan: « ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Bokkul woon ci jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ju ñaaw, walla jëf ju ñaaw, te daawu ko jublu it mbaa mu koy tay, ndax moom Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- boroom jikkó yu màgg la. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na wax naan: ki gën ci yéen fa Yàlla mooy ki gën a rafet jikkó, ci def njekk, ak leeral xar kanam, ak téye lor te muñal nit ñi, ak jaxasoo ak nit ñi ca na mu rafete.

Source
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Download image

Saved at original quality