Hadith for the World
Xam ñaan yi ak sikkar yi

Ni Yónnent bi SLM daa sikkaree

5 hadiths

5 hadiths

Jële nañu ci Jaabir ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne moom dégg na Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay, bu duggee te tuddul Yàlla, bi muy dugg, saytaane day wax naan: am ngeen fanaanukaay, bu tuddul Yàlla bu dee lekk, mu wax: am ngeen fanaanukaay ak reerukaay ».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax: "Allahumma laka aslamtu, wa bika aamantu, wa halayka tawakkaltu, wa ilayka anabtu, wa bika xaasamtu, Allaahuma innii ahuusu bihissatika, laa ilaaha illaa Anta an tadillanii, Anta Al-Hayyu Allasii laa yamuutu, wal insu wal jinnu yamuutuuna".متفق عليه، وهذا لفظ مسلم ورواه البخاري مختصرًا
عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول: «وَاللهِ إني لأَسْتَغْفِرُ اللهَ وأَتُوبُ إليهِ في اليومِ أَكْثَرَ من سَبْعِينَ مَرَّةً».رواه البخاري
Jële nañu ci Al-Axarri yal na ko Yàlla dollee gërëm mu bokkoon ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu wax ne: Yonente Yàlla bi nee na: «yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax ci sujjóotam: "Allaahuma ixfir lii sanbii kullahu, diqahu, wa jillahu, wa awwalahu wa aaxirahu, wa halaaniyatahu wa sirrahu".Muslim soloo na ko