4 hadiths
Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Génn nanu ci guddi gu bari taw te lëndëm lool, di wër Yonnente Yàlla bi ngir mu jiite nu julli, nee na: nu dab ko, mu ne ma: "waxal" te waxuma dara, mu waxaat ma: "waxal", te waxuma dara, mu ne ma: "waxal", ma ne ko: lan laay wax? Mu ne ma: "{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp".Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy