Hadith for the World
Xam ñaan yi ak sikkar yi

Njariñi tudd Yàllay Mu tedd Mu màgg mi

8 hadiths

8 hadiths

Jële nañu ci Jaabir ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne moom dégg na Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay, bu duggee te tuddul Yàlla, bi muy dugg, saytaane day wax naan: am ngeen fanaanukaay, bu tuddul Yàlla bu dee lekk, mu wax: am ngeen fanaanukaay ak reerukaay ».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee, bu ma tuddee ci boppam ma tudd ko ci sama bopp, bu ma tuddee ci mbooloo ma tudd ko ci mbooloo mu gën mooma, bu ma jege luy toll ni Sibr, ma jege ko luy toll ne loxo, bu ma jegee luy toll ni loxo ma jege ko luy toll ni Baah, bu ma dikkee ci dox, ma dikke ko ci ñukk".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عَنْ سَعْدِ بنِ أبي وَقَّاصٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ: كُنَّا عِنْدَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: «أَيَعْجِزُ أَحَدُكُمْ أَنْ يَكْسِبَ، كُلَّ يَوْمٍ أَلْفَ حَسَنَةٍ؟» فَسَأَلَهُ سَائِلٌ مِنْ جُلَسَائِهِ: كَيْفَ يَكْسِبُ أَحَدُنَا أَلْفَ حَسَنَةٍ؟ قَالَ: «يُسَبِّحُ مِائَةَ تَسْبِيحَةٍ، فَيُكْتَبُ لَهُ أَلْفُ حَسَنَةٍ، أَوْ يُحَطُّ عَنْهُ أَلْفُ خَطِيئَةٍ».رواه مسلم
Jële na ñu ci Abii Muusaa yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "misaalu kiy tudd Boroomam ak ki dul tudd Boroomam, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee", ci baati Muslim: "misaalu kër gi ñuy tudde Yàlla, ak kër gi ñu dul tudde Yàlla, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Kahb ibn Hujrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «ay mbir a ngii yuy wuutante ku leen di wax du sooy -walla ku leen di def- ginnaaw jullig farata gu nekk, Subhaanal Laahi fanweeri yoon ak ñatt, alhamdu lil-Laahi fanweeri yoon ak ñatt, Allaahu Akbaru, fanweeri yoon ak ñent».Muslim soloo na ko
عن زيد مولى رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «من قال: أَسْتَغْفِرُ الله الذي لا إله إلا هو الحَيَّ القيَّومَ وأتوب إليه، غُفرت ذنوبه، وإن كان قد فَرَّ من الزَّحْف».رواه أبو داود والترمذي
Jële na ñu ci Abuu Maalik Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga: imaam bu maandu, ak waxambaane wu sosu ci jaamu Yàlla, ak waa ju xolam aju ca jàkka ya, ak ñaar ñu bëggante ci Yàlla, ci moom lañuy daje te ci moom lañuy teqalikoo, ak góor gu jigéen ju am dayo ak rafetaay woo mu ne ko: man damaa ragal Yàlla, ak waa ju saraxe ab sarax nëbb ko ba càmmooñam du xam li ndayjoor bi joxe, ak waa ju fàttaliku Yàlla ciw wéetaay, ay bëtam taa".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér