Hadith for the World
Topic

Dégg diine ak i cosaanam

288 hadiths

288 hadiths

Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom", Abuu Sahiid yéemu ci loolu, ne ko: baamtul ma ko yaw Yonente Yàlla bi, mu def ko, topp mu ne ko: "ak leneen lol dees na ci yëkkëtil jaam bi téeméeri daraja ca àjjana, te diggante ñaari daraja yi mi ngi mel ni diggante asamaan ak suuf ", mu ne ko: loolu lan la yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne ko: "jihaad ci yoonu Yàlla, jihaad ci yoonu Yàlla".Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abii Xataadata yal na ko Yàlla dollee gërëm ne na da doon seet kenn ku ko ameeloon bor, mu làqatu ko topp mu gis ko, mu ne ko: man de ci jafe-jafe laa nekk, mu ne: ndax da nga ko waat ci Yàlla? Mu ne ko: waat naa ko ci Yàlla? Mu ne ko: man dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di wax naan: «ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram»Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
وعن سالم بن عبد الله بن عمر بن الخطاب رضي الله عنهم عن أبيه: أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: « نِعْمَ الرَّجُلُ عبد الله، لو كان يُصلِّي من الليل» قال سالم: فكان عبد الله بعد ذلك لا يَنامُ من الليل إلا قليلًا.متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne: «ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ne: «nit ñi du ñu deñ di nekk ci yiw fii ak ñoo ngi gaaw a dog».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Saydu ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Xëdd nañu ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu daal di jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Anas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la«.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عَنْ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللَّهِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُما قَالَ: كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي سَفَرٍ، فَرَأَى زِحَامًا وَرَجُلًا قَدْ ظُلِّلَ عَلَيْهِ، فَقَالَ: «مَا هَذَا؟»، فَقَالُوا: صَائِمٌ، فَقَالَ: «لَيْسَ مِنَ البِرِّ الصَّوْمُ فِي السَّفَرِ»، وَفِي لَفْظٍ لِمُسلِمٍ: «عَلَيْكُمْ بِرُخْصَةِ اللهِ الَّذِي رَخَّصَ لَكُمْ».متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum koor, Saah ci tàndarma,walla Saah ci pepp,ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi,mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن عائشة وأم سلمة رضي الله عنهما «أن رسول الله صلى الله عليه وسلم كان يُدْرِكُهُ الفجر وهو جُنٌبٌ من أهله، ثم يغتسل ويصوم ».متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن عمر بن الخطاب رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «إذا أقبل الليل من هَهُنا، وأَدْبَرَالنهار من ههنا، فقد أفطر الصائم».متفق عليه
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Al-Hawraa As-Sahdii mu wax ne: wax naa Al-Hasan ibn Aliyun yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ko: lan nga mokkal ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc? Mu ne ma: mokkale naa ci Yonnente Yàlla bi: «bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".رواه الترمذي والنسائي وأحمد
Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp, loolu nag ndax bu kenn ci ñoom jàppee rafetal njàppu ma, daal di dem ca jàkka ja te dara yëkkatiwu ko lu dul julli, du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil daraja, sippil ko ci njuumte, ba ba muy dugg ca jàkka ja, bu duggee ca jàkka ja ci julli la nekk fii ak julli moo ko téye, te malaaka yi dañuy julli ci kenn ci yéen fii ak moo ngi ca bérab ba mu doon jullee, dañuy wax naan: Yàlla yërëm ko, Yàlla jéggal ko, Yàlla nangul tuubam, fii ak lotul kenn, te tojlewul».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول: «ما نهيتكم عنه فاجتنبوه، وما أمرتكم به فأْتُوا منه ما استطعتم، فإنما أَهلَكَ الذين من قبلكم كثرةُ مسائلهم واختلافهم على أنبيائهم».متفق عليه
عن أبي ذر رضي الله عنه قال: قال النبي صلى الله عليه وسلم :«عُرِضَتْ عَلَيَّ أعمالُ أُمتي، حَسَنُهَا وسَيِّئُهَا فَوَجَدتُ في مَحَاسِنِ أَعْمَالِهَا الأَذَى يُمَاطُ عَنِ الطَّرِيقِ، ووَجَدتُ في مَسَاوِئِ أَعْمَالِهَا النُّخَاعَةُ تَكُونُ في المَسْجِدِ لا تُدْفَنُ».رواه مسلم