Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Ngëneel yi ak teggiin yi

Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na:

Available in 60 languages
«Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: «Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon, yóbbe na leen ñu tuur seen i dereet ak a daganal araam».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo tooñ, te bokk na ca: tooñ nit ñi, ak tooñ sa bakkan, ak tooñ ci àqi Yàlla mu kawe mi. Te mooy bañ a jox ku nekk àqam, ak ne tooñ ay lëndëm lay doon ci kaw ay ñoñam ëllëg bis-pénc ci ñu daje fa ak ay tar-tar ak i tiitaange, Mu tere bëgge te mooy nay gu tar ak ug xér ci alal, bokk na ca gànteñlu ci joxe àqi alal yi ak xér gu tar ci àdduna. Xeetu tooñ gii moo alag xeet yi ñu jiitu woon, ndax da leen a yóbbe woon ci ñenn ñi di ray ñeneen ñi, ak di daganal yu araam yi Yàlla araamal.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality