Hadith for the World
Tap the image to view it full size
Pas-pasu Lislaam

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:

Available in 70 languages
«Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm».»

Meaning translation ·

Explanation

The meaning in a few plain lines

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digle ñu soppi lu bon -te mooy lépp lu Yàlla ak ub Yónenteem tere- kem kàttanam, Bu gisee lu bon da koo war a soppi ci loxoom bu ko manee, Bu ko manul mu soppi ko ci làmmeñem ñam ci tere ki koy def, leeralal ko ay loram tegtal ko lu baax ci palaasu mbon gii, Bu manula def taxawaay boobu mu soppi ko ci xolam ci sib lu bon lii te mu dogu ne bu ko manoon a dindi dana ko def, Soppi ko ci xol nag mooy martaba bi gën a néew cig ngëm ci wàllu soppi lu bon.

Source
Muslim soloo na ko
Download image

Saved at original quality