WO
All hadiths
The complete card collection, filter by chapter
Alquraan ju tedd ji ak xam-xam yi ci aju
26
Adiis ak xam-xam yi ci aju
3
Pas-pasu Lislaam
135
Dégg diine ak i cosaanam
288
Ngëneel yi ak teggiin yi
288
Woote ci Yàlla ak sàkku ci tuyaaba
15
Jaar-jaar ak taarix
38
655 hadiths
عن أنس بن مالك رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «للَّهُ أَفْرَحُ بِتَوْبَةِ عَبْدِهِ مِنْ أَحَدِكُمْ، سَقَطَ عَلَى بَعِيرِهِ، وَقَدْ أَضَلَّهُ فِي أَرْضِ فَلاَةٍ». وفي رواية: «لَلَّهُ أَشَدُّ فَرَحًا بِتَوْبَةِ عَبْدِهِ حِينَ يَتُوبُ إِلَيْهِ، مِنْ أَحَدِكُمْ كَانَ عَلَى رَاحِلَتِهِ بِأَرْضِ فَلَاةٍ، فَانْفَلَتَتْ مِنْهُ وَعَلَيْهَا طَعَامُهُ وَشَرَابُهُ، فَأَيِسَ مِنْهَا، فَأَتَى شَجَرَةً، فَاضْطَجَعَ فِي ظِلِّهَا، وقَدْ أَيِسَ مِنْ رَاحِلَتِهِ، فَبَيْنَا هُوَ كَذَلِكَ إِذَا هُوَ بِهَا، قَائِمَةً عِنْدَهُ، فَأَخَذَ بِخِطَامِهَا، ثُمَّ قَالَ مِنْ شِدَّةِ الْفَرَحِ: اللهُمَّ أَنْتَ عَبْدِي وَأَنَا رَبُّكَ! أَخْطَأَ مِنْ شِدَّةِ الْفَرَح».
متفق عليه والرواية الأولى لفظ البخاري، والرواية الثانية لفظ مسلم
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla mu màgg mi day tàllal loxoom ci guddi gi ngir ki doon def ñaawteef ci bëccëg gi tuub, di tàllal loxoom ci bëccëg gi ngir ki doon def ñaawteef ci guddi gi tuub, ba baa jant bi di fenke ci sowwu bi.
Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne: «ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ne: «nit ñi du ñu deñ di nekk ci yiw fii ak ñoo ngi gaaw a dog».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Saydu ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Xëdd nañu ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu daal di jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Anas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la«.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عَنْ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللَّهِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُما قَالَ: كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي سَفَرٍ، فَرَأَى زِحَامًا وَرَجُلًا قَدْ ظُلِّلَ عَلَيْهِ، فَقَالَ: «مَا هَذَا؟»، فَقَالُوا: صَائِمٌ، فَقَالَ: «لَيْسَ مِنَ البِرِّ الصَّوْمُ فِي السَّفَرِ»، وَفِي لَفْظٍ لِمُسلِمٍ: «عَلَيْكُمْ بِرُخْصَةِ اللهِ الَّذِي رَخَّصَ لَكُمْ».
متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum koor, Saah ci tàndarma,walla Saah ci pepp,ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi,mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن عائشة وأم سلمة رضي الله عنهما «أن رسول الله صلى الله عليه وسلم كان يُدْرِكُهُ الفجر وهو جُنٌبٌ من أهله، ثم يغتسل ويصوم ».
متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن عمر بن الخطاب رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «إذا أقبل الليل من هَهُنا، وأَدْبَرَالنهار من ههنا، فقد أفطر الصائم».
متفق عليه
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».
Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jëf yi mi ngi aju ci yéene ja, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yónenteem, koo ku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yónenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot, walla jigéen ju mu bëgg a takk; kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay" ci beneen nettali ci Al-Buxaarii: "jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Al-Hawraa As-Sahdii mu wax ne: wax naa Al-Hasan ibn Aliyun yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ko: lan nga mokkal ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc? Mu ne ma: mokkale naa ci Yonnente Yàlla bi: «bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".
رواه الترمذي والنسائي وأحمد
Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp, loolu nag ndax bu kenn ci ñoom jàppee rafetal njàppu ma, daal di dem ca jàkka ja te dara yëkkatiwu ko lu dul julli, du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil daraja, sippil ko ci njuumte, ba ba muy dugg ca jàkka ja, bu duggee ca jàkka ja ci julli la nekk fii ak julli moo ko téye, te malaaka yi dañuy julli ci kenn ci yéen fii ak moo ngi ca bérab ba mu doon jullee, dañuy wax naan: Yàlla yërëm ko, Yàlla jéggal ko, Yàlla nangul tuubam, fii ak lotul kenn, te tojlewul».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jàpp ci sama mbagg daal di ne ma: «nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon", ibn Umar, daan na wax naan: boo gontee bul xaar suba, boo xëyee bul xaar ngoon, nanga jël ci sag wée ñeel sag tawat, ak ci sag dund ñeel sag dee.
Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbokk jullit mooy mbokku jullit, du ko tooñ, du ko beddi, du ko xeeb, ragal Yàlla fii la nekk" muy junj ci dënnam bi ñatti yoon "doy na sëkk nit aw ay muy xeeb mbokk jullitam, léppi jullit bi dafa araam ci jullit bi, dereetam, ak alalam, ak deram".
Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".
Al-buxaariy soloo na ko
Previous page
Page 9 of 28
Next page