Hadith for the World
Topic

Ngëneel yi ak teggiin yi

288 hadiths

288 hadiths

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbokk jullit mooy mbokku jullit, du ko tooñ, du ko beddi, du ko xeeb, ragal Yàlla fii la nekk" muy junj ci dënnam bi ñatti yoon "doy na sëkk nit aw ay muy xeeb mbokk jullitam, léppi jullit bi dafa araam ci jullit bi, dereetam, ak alalam, ak deram".Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".Al-buxaariy soloo na ko
Jële na ñu ci Umar ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg na Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell.At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ci jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc, ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira, ku suturaal ab jullit Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira, Yàlla day dimbali jaam bi fii ak jaam bi moo ngi dimbali mbokkam, ku sóobu aw yoon di ca sàkku xam-xam yàlla yombalal ko yoonu àjjana, te aw nit duñu dajaloo ci ak kër ci këri Yàlla yi di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir lu dul ne ag dal dana wàcc ci seen kaw yërmànde muur leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tudd leen ca ña fa moom, ku ay jëfam yeexal askanam du ko gaawal».Muslim soloo na ko
عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول: «وَاللهِ إني لأَسْتَغْفِرُ اللهَ وأَتُوبُ إليهِ في اليومِ أَكْثَرَ من سَبْعِينَ مَرَّةً».رواه البخاري
Jële nañu ci Al-Axarri yal na ko Yàlla dollee gërëm mu bokkoon ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu wax ne: Yonente Yàlla bi nee na: «yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أبي أمامة رضي الله عنه أن النبي صلى الله عليه وسلم كَانَ إذا رَفَعَ مَائِدَتَهُ، قال: «الحَمْدُ للهِ حَمْدًا كَثِيرًا طَيِّبًا مُبَارَكًا فِيهِ، غَيْرَ مَكْفِيٍّ، وَلَا مُوَدَّعٍ، وَلَا مُسْتَغْنًى عَنْهُ رَبَّنَا».رواه البخاري
عن أبي هريرة رضي الله عنه أن النبي صلى الله عليه وسلم قال: «لا يُلْدَغُ المؤمنُ من جُحْرٍ واحد مرتين».متفق عليه
Jële nañu ci Jariir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw».Muslim soloo na ko
عن أنس رضي الله عنه قَالَ: كُنْتُ أمشي مَعَ رسول الله صلى الله عليه وسلم وَعَلَيْهِ بُرْد نَجْرَانيٌّ غَلِيظُ الحَاشِيَةِ، فأدْرَكَهُ أعْرَابِي فَجَبذَهُ بِرِدَائِهِ جَبْذَة شَديدة، فَنَظَرْتُ إِلَى صَفْحَةِ عَاتِقِ النَّبيِّ صلى الله عليه وسلم وَقَدْ أثَّرَتْ بِهَا حَاشِيَة الرِّدَاءِ مِنْ شِدَّةِ جَبْذَتِه، ثُمَّ قَالَ: يَا مُحَمَّدُ، مُر لِي مِنْ مَالِ اللهِ الَّذِي عِنْدَكَ. فَالتَفَتَ إِلَيْهِ، فَضَحِكَ ثُمَّ أَمَرَ لَهُ بِعَطَاءٍ.متفق عليه
عَنْ أَنَسٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَوْ كَانَ لِابْنِ آدَمَ وَادِيَانِ مِنْ مَالٍ لَابْتَغَى وَادِيًا ثَالِثًا، وَلَا يَمْلَأُ جَوْفَ ابْنِ آدَمَ إِلَّا التُّرَابُ، وَيَتُوبُ اللهُ عَلَى مَنْ تَابَ».متفق عليه
عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: ما عاب رسول الله صلى الله عليه وسلم طعاما قط، إن اشتهاه أكله، وإن كرهه تركه.متفق عليه
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe amee: "laa ilaaha illallaahu Al-Hasiimu Al-Haliimu, laa ilaaha illallaahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi, laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi wa Rabbul Harsi Al-Kariimi".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul», ñu ne ko: waaw bu dee li ma wax moo ngi ci sama mbokk mi nag? Mu wax ne: «bu nekkee ci moom kon jëw nga ko, bu nekkul ci moom nag kon duural nga ko».Muslim soloo na ko
عن ابن عمر رضي الله عنهما مرفوعا: «الظلم ظلمات يوم القيامة». عن جابر رضي الله عنهما مرفوعا: «اتقوا الظلم، فإن الظلم ظلمات يوم القيامة، واتقوا الشُّحَ؛ فإنه أَهْلَكَ من كان قبلكم».حديث ابن عمر -رضي الله عنهما-: متفق عليه. حديث جابر -رضي الله عنه-: رواه مسلم
Jële nañu ci Xawlata mi bokk ci waa-lansaar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc».Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen, te buleen di gëstu, buleen di luññutu, buleen di soxorante, buleen di tóngoowante, buleen di bañante, nangeen doon ay mbokk yeen jaami Yàlla yi ».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : "إذا كنتم ثلاثة فلا يتناجى اثنان دون الآخَر، حتى تختلطوا بالناس؛ من أجل أن ذلك يحُزنه".متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "deeleen xool ñi leen féete suuf, te buleen xool ci ñi leen féete kaw, ndax moo gën a yay ba dungeen xeeb xéewali Yàlla yi ci seen kaw".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أنس بن مالك رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «كلُّ بني آدم خَطَّاءٌ، وخيرُ الخَطَّائِينَ التوابون».رواه الترمذي وابن ماجه والدارمي وأحمد
Jële nañu ci Abbu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli».Muslim soloo na ko