TopicNgëneel yi ak teggiin yi
288 hadiths
288 hadiths
Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom", Abuu Sahiid yéemu ci loolu, ne ko: baamtul ma ko yaw Yonente Yàlla bi, mu def ko, topp mu ne ko: "ak leneen lol dees na ci yëkkëtil jaam bi téeméeri daraja ca àjjana, te diggante ñaari daraja yi mi ngi mel ni diggante asamaan ak suuf ", mu ne ko: loolu lan la yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne ko: "jihaad ci yoonu Yàlla, jihaad ci yoonu Yàlla".Muslim soloo na ko