231 hadiths
Jële nañu Jaabir ibn Abdul Laahi yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan, mu wax ne: "bu kenn ci yéen yittewoo am mbir, na julli ñaari ràkka yu dul farata, topp mu wax: Allaahuma innii astaxiiruka, bi hilmika, wa astaqdiruka bi xudratika, wa as-aluka min fadlika Al-Hasiimi, fa innaka Taqdiru wa laa aqdiru, wa Tahlamu wa laa ahlamu, wa Anta Hallaamu alxuyuubi, Allaahuma in Kunta Tahlamu anna haasal amra xayrun lii fii diinii, wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii, wa aajilihi, faqdurhu lii wa yasairhu lii summa baarik lii fiihi, wa in Kunta tahlamu anna haasal amra sarrun lii fii diinii wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii wa aajilihi, fasrifhu hanni wasrifnii hanhu waqdur liya alxayra haysu kaana summa ardinii bihii" nee na: "mu tudd aajoom".Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Yàlla nee na: jépp jëfi doomu Aadama moom la ñeel, ba mu des woor, moom man maa ko moom te maa koy fay, te woor ab pakk la, bu nit ki nekkee ci bisu wooram bu mu jëf jëfi caaxaan bu mu coow, bu ko kenn saagaa mbaa mu xeex ak moom, na ko wax ne man damaa woor, giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom, xetu gémmiñu aji-woor ji moo gën a teey fa Yàlla ci xetu Misk, aji-woor ji am na ñaari mbégte yu muy bég: bu dogee day bég, bu dajee ak Boroomam day bég ci wooram gi».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér