64 hadiths
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abdullah ibn Salaam yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina nit ñi dañoo buur jëm ci moom, ñu naan: Yonnente Yàlla bi ñëw na, Yonnente Yàlla bi ñëw na, Yonnente Yàlla bi ñëw na, ñatti yoon, ma ñëw ci nit ñi ngir xool, bi ma seetloo kanam ga, laa xam ne kanamam gi du kanamu fenkat, li ma njëkk a degg mu wax ko mooy: "yéen nit ñi, deeleen tasaare nuyóo, di leele ñam, di jokk mbokk, di julli guddi fekk nit ñi a ngi nelaw, kon dangeen dugg àjjana ci jàmm".At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat