Hadith for the World
Topic

Pas-pasu Lislaam

135 hadiths

135 hadiths

عن أبي هريرة رضي الله عنه مرفوعًا: «إِنَّ الله تَعَالى يَقُول يَوْمَ القِيَامَة: أَيْنَ المُتَحَابُّونَ بِجَلاَلِي؟ اليَوم أُظِلُّهُم فِي ظِلِّي يَوْمَ لاَ ظِلَّ إِلاَّ ظِلِّي».رواه مسلم
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara, ku woote it jëme cig reer dana am bàkkaar bu mel ni bàkkaarub ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni bàkkaar dara».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal, ngistalkat yi Yàlla da leen di wax ëllëg bis-pénc bu ñu faayee nit ñi seen jëf ba noppi: demleen ca ña ngeen doon ngistal ca àdduna, ngeen xool ba xam ndax dangeen fekk fa ñoom ag pay?"Ahmat soloo na ko
Jële nañu ci Umar Ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam».Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne: Wax nañu Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko ana kan ci nit ñi moo gën a texe ci sag rammu ëllëg bis-penc? Yónent Yàlla bi wax ne: «Njoortoon naa ne yaw Abuu Hurayrata Yamamay njëkk laaj lii; ndax li ma gis sag xér ci Hadiis, nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam».Al-buxaariy soloo na ko
عن عبد الله بن عمرو بن العاص - رضي الله عنه- مرفوعاً: "مَن ردته الطِّيَرَة عن حاجته فقد أشرك، قالوا: فما كفارة ذلك؟ قال: أن تقول: اللهم لا خير إلا خيرك، ولا طَيْرَ إِلَّا طَيْرُكَ ولا إله غيرك".رواه أحمد
Jële nañu ci Ubaadata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na jenn wax, ma wax Jeneen wax, yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: " ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara" man ma ne: ku faatu te wutalul Yàlla ndend dana dugg àjjana.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أبي هريرة رضي الله عنه مرفوعًا: «صلاة الرجل في جماعة تَضعُفُ على صلاته في بيته وفِي سُوقِه خمسا وعشرين ضِعفًا، وذلك: أَنَّه إِذَا تَوَضَّأ، فَأَحسَن الوُضُوء، ثمَّ خرج إلى المسجد لاَ يُخرِجُهُ إلاَّ الصلاة؛ لَم يَخْطُ خُطوَةً إِلاَّ رُفِعَت له بِها درجة، وَحُطَّ عَنهُ بها خطيئة، فإذا صلَّى لم تزل الملائكة تُصَلِّي عليه، ما دام في مُصَلاَّه: اللهُمَّ صَلِّ عليه، اللهم اغفِر له، اللهم ارْحَمه، ولا يزال في صلاة ما انتظر الصلاة».متفق عليه
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "jox na nu ma juróom yoo xam ne joxuñuko kenn ku ma jiitu: dimbalees na ma ci ag ragal luy toll ni doxub weer, defal na nu ma suuf si muy jàkka di lu laab, fu julli dabe kenn ci samaw xeet na julli, daganal na nu ma koomi xare yi, te daganaluñu ko woon kenn ku ma jiitu, jox na nu ma ramm ga, Yonnente dañu ko daan yónni ci xeetam kese man nag ñu yónni ma ci nit ñépp ".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن معاذ بن جبل رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم أنه قال: «قَالَ اللهُ -عَزَّ وجَلَّ-: المُتَحَابُّون فِي جَلاَلِي، لَهُم مَنَابِرُ مِن نُورٍ يَغْبِطُهُم النَبِيُّونَ والشُهَدَاء».رواه الترمذي وأحمد
عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: «إنَّ في الجنَّة مائةَ دَرَجَة أعَدَّهَا الله للمُجاهِدين في سَبِيل الله ما بَيْنَ الدَّرَجَتَيْنِ كما بين السماء والأرض».رواه البخاري
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee, bu ma tuddee ci boppam ma tudd ko ci sama bopp, bu ma tuddee ci mbooloo ma tudd ko ci mbooloo mu gën mooma, bu ma jege luy toll ni Sibr, ma jege ko luy toll ne loxo, bu ma jegee luy toll ni loxo ma jege ko luy toll ni Baah, bu ma dikkee ci dox, ma dikke ko ci ñukk".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma, ci lañu bind Aadama, ci lañu ko duggal àjjana, ci lañu ko ca génne, te Saa du taxaw ci lu dul bisu àjjuma ».Muslim soloo na ko
عن أبي هريرة رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال: «كان داود -عليه السلام- لا يأكلُ إلا من عمل يده». وعن المقدام بن معد يكرب رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال: «ما أكل أحد طعاما قط خيرا من أن يأكل من عمل يده، وإن نبي الله داود صلى الله عليه وسلم كان يأكل من عمل يده».حديث أبي هريرة رضي الله عنه: رواه البخاري. حديث المقداد رضي الله عنه: رواه البخاري
عن ابن مسعود رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «من أصابته فَاقَة فأنْزَلها بالناس لم تُسَدَّ فَاقَتُهُ، ومن أنْزَلها بالله، فَيُوشِكُ الله له بِرزق عاجل أو آجل».رواه أبو داود والترمذي وأحمد
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat
Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse".رواه ابن ماجه والبيهقي وغيرهما
عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول: «جَعَلَ اللهُ الرحمةَ مائة جُزْءٍ، فَأَمْسَكَ عِنْدَهُ تِسْعَةً وَتِسْعِينَ، وأَنْزَلَ في الأَرْضِ جُزْءًا وَاحِدًا، فَمِنْ ذَلِكَ الجُزْءِ يَتَرَاحَمُ الخَلَائِقُ، حتى تَرْفَعَ الدَّابَّةُ حَافِرَهَا عَنْ وَلَدِهَا خَشْيَةَ أَنْ تُصِيبَهُ». وفي رواية «إِنَّ للهِ تعالى مئةُ رحمةٍ، أَنْزَلَ منها رحمةً واحدةً بَيْنَ الجِنِّ والإنسِ والبَهَائِمِ والهَوَامِّ، فَبِهَا يَتَعَاطَفُونَ، وبها يَتَرَاحَمُونَ، وبِهَا تَعْطِفُ الوَحْشُ على وَلَدِهَا، وأَخَّرَ اللهُ تعالى تِسْعًا وتِسْعِينَ رحمةً يَرْحَمُ بِهَا عِبَادَهُ يومَ القِيَامَةِ». وعن سلمان الفارسي رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : «إِنَّ للهِ تعالى مئةُ رحمةٍ فمنها رحمةٌ يَتَرَاحَمُ بها الخَلْقُ بَيْنَهُمْ، وتِسْعٌ وتِسْعُونَ لِيَومِ القِيَامَةِ». وفي رواية: «إِنَّ اللهَ تَعَالَى خَلَقَ يَوْمَ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ والأَرْضَ مئةَ رحمةٍ كُلُّ رحمةٍ طِبَاقَ مَا بَيْنَ السَّمَاءِ إلى الأَرْضِ، فَجَعَلَ منها في الأَرْضِ رَحْمَةً فبها تَعْطِفُ الوَالِدَةُ على وَلَدِهَا، والوَحْشُ والطَّيْرُ بَعْضُهَا عَلَى بَعْضٍ، فإذا كانَ يومُ القيامةِ أَكْمَلَهَا بِهَذِه الرحمةِ».حديث أبي هريرة -رضي الله عنه-: متفق عليه. حديث سلمان -رضي الله عنه-: رواه مسلم
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yàlla mu kawe mi mu wax ne:«yéen sama jaam ñi damaa araamal tooñ ci sama bopp, ma def ko muy lu araam ci seen diggante kon buleen di tooñante, yéen sama jaam ñi yéen ñépp dangeen a réer ku dul ki ma gindi, kon sàkkuleen ci man gindiku ma gindi leen, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a xiif ku dul ki ma leel, kon sàkkuleen ci man ma leel leen , kon dinaa leen leel, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a rafle ku dul ki ma wodd, kon sàkkuleen ci man ma wodd leen kon dinaa leen wodd, yéen sama jaam ñi dangeen di juum guddi ak bëccëg kon jéggaluleen ma ma jéggal leen, yéen sama jaam ñi manuleen maa lor ba di ma lor, te manuleen maa jariñ ba di ma jariñ, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñi mujj ci yéen, nit ñi ak jinne yi ci yéen bu ñu neekkoon xolu ki gën a ragal Yàlla ci yéen loolu du yokk ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne bu ñu neekkoon xolu ki gën a kàccoor ci yéen loolu du wàññi ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne dañoo taxaw ci benn pàkk bu yaatu, ñu ñaan ma ma jox kenn ku nekk la mu ñaan loolu du wàññi li ne fi man lu dul li ab puso di wàññi ci ndoxum géej gi bu ñu ko sa dugalee, yéen sama jaam ñi seen jëf rekk laa leen di dencal joxaat leen ko ba mu mat, ku fa fekk yiw na sant Yàlla, waaye ku fa fekk ay bu mu yedd ku dul boppam».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn bis nekkoon naa ci ginnaaw Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: «yaw ngóor si di naa la xamal ay waat: wattul Yàlla ci jëfe ay ndigëlam bayyi ay tereem kon di na la sàmm, Nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbël na nga dimbandikoo Yàlla, te nga xam ni bu ñépp dajewoon ngir jariñ la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, bu ñépp dajewoon it ngir lor la ci dara duñu ko man ludul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, ndax teggi nañu xalima ya te kayit ya woow na».At-tirmisiy soloo na ko
عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضيَ اللهُ عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، قَالَ: «أَحَبُّ الْبِلَادِ إِلَى اللهِ مَسَاجِدُهَا، وَأَبْغَضُ الْبِلَادِ إِلَى اللهِ أَسْوَاقُهَا».رواه مسلم
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ», ñu ne ko ana kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi? Mu ne: «ku ma topp dugg àjjana ku ma moy nag kooku mooy ki bañ».Al-buxaariy soloo na ko