Hadith for the World
Pas-pasu Lislaam

Tur yi ak àtte yi

22 hadiths

22 hadiths

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «gaawleen jëf ndax ay fitna a ngi ñëw yu mel ni dogiiti guddi gu lëndëm, nit ki day xëy di ku gëm, gontu di ab yéefar, walla mu gontu di ku gëm xëy nekk ab yéefar, day jaay diineem ci poñetu àdduna«.Muslim soloo na ko
عن أبي هريرة رضي الله عنه مرفوعاً: «الإيمانُ بِضْعٌ وَسَبْعُونَ أو بِضْعٌ وسِتُّونَ شُعْبَةً: فَأَفْضَلُهَا قَوْلُ: لا إله إلا الله، وَأَدْنَاهَا إِمَاطَةُ الأَذَى عَنِ الطَّرِيقِ، وَالحَيَاءُ شُعْبَةٌ مِنَ الإِيمَانِ».متفق عليه
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm, Yàlla rëbb na nit ñiy jàppe bàmmeelu seeni Yónente ay jàkka".Ahmat soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam, doon naa yittewoo digle ñu taxawal julli, ma digal benn waay mu jiite nit ñi, ma ànd ak ay góor ñu yor ay matti sawara, nu dem ci nit yi dul teewe julli gi, taal séen kër ya ca séen kaw».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara, ku woote it jëme cig reer dana am bàkkaar bu mel ni bàkkaarub ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni bàkkaar dara».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal, ngistalkat yi Yàlla da leen di wax ëllëg bis-pénc bu ñu faayee nit ñi seen jëf ba noppi: demleen ca ña ngeen doon ngistal ca àdduna, ngeen xool ba xam ndax dangeen fekk fa ñoom ag pay?"Ahmat soloo na ko
عن عبد الله بن عمرو بن العاص - رضي الله عنه- مرفوعاً: "مَن ردته الطِّيَرَة عن حاجته فقد أشرك، قالوا: فما كفارة ذلك؟ قال: أن تقول: اللهم لا خير إلا خيرك، ولا طَيْرَ إِلَّا طَيْرُكَ ولا إله غيرك".رواه أحمد
Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day ànd bañ a nelaw ak di tàng».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abdallah Ibnu Mashuud mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na : "bokkul ci nun kiy mbej ñiy mbej lex ya, di xotti kaw yére ya, di woote wooteg ceddo ya".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci yenn Soxnay Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor ci kaw yoon wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm»Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Buraydata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Ku waat ci kóolute bokkul ci nun».Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci moom».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abdullah Ibnu Umar-yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : "tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Maalik Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi, Ibn Jadhaan de ca jamanoy ceddo ga da daan jokk mbokk di leel miskiin, mo ndax loolu dana ko jariñ ? Mu wax ne: «du ko jariñ de, ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli».Muslim soloo na ko
عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: "ثَلاَثٌ مَنْ كُنَّ فِيهِ وَجَدَ حَلاَوَةَ الإِيمَانِ: أَنْ يَكُونَ اللَّهُ وَرَسُولُهُ أَحَبَّ إِلَيْهِ مِمَّا سِوَاهُمَا، وَأَنْ يُحِبَّ المَرْءَ لاَ يُحِبُّهُ إِلَّا لِلَّهِ، وَأَنْ يَكْرَهَ أَنْ يَعُودَ فِي الكُفْرِ كَمَا يَكْرَهُ أَنْ يُقْذَفَ فِي النَّارِ".متفق عليه
Jële nañu ci Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne dégg na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem».Muslim soloo na ko
عن جابر بن عبد الله قال: كان رسول الله صلى الله عليه وسلم إذا خطب احمرَّتْ عيناه، وعلا صوته، واشتد غضبه، حتى كأنه مُنذِرُ جيشٍ يقول: صبَّحكم ومسَّاكم، ويقول: «بُعثتُ أنا والساعةُ كهاتين»، ويقرن بين إصبعيه السبابة، والوسطى، ويقول: «أما بعد، فإن خير الحديث كتاب الله، وخير الهدى هدى محمد، وشر الأمور محدثاتها، وكل بدعة ضلالة» ثم يقول: «أنا أولى بكل مؤمن من نفسه، من ترك مالًا فلأهله، ومن ترك دينًا أو ضَياعًا فإليَّ وعليَّ».رواه مسلم