TopicNgëneel yi ak teggiin yi
288 hadiths
288 hadiths
Jële nañu ci Abuu Muusa yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu nettali ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne daan na ñaan ñaan gii: "rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal Mu-axiru, wa Anta halaa kulli say-in xadiirun ".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul bàyyi di ñaan lii, bu gontee ak bu xëyee: "Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati, Allaahuma innii as-aluka alhafwa walhaafiyata fii diinii wa dunyaaya wa ahlii wa maali, Allaahuma ustur hawratii -walla hawraatii- wa aamin rawhaatii, Allaahuma ihfasnii min vayni yadayya, wa min xalfii, wa han yamiinii, wa han simaalii, wa min fawxii, wa ahuusu Bika an uxtaala min tahtii".Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".Al-buxaariy soloo na ko
Jële nañu ci Abdullah ibn Salaam yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina nit ñi dañoo buur jëm ci moom, ñu naan: Yonnente Yàlla bi ñëw na, Yonnente Yàlla bi ñëw na, Yonnente Yàlla bi ñëw na, ñatti yoon, ma ñëw ci nit ñi ngir xool, bi ma seetloo kanam ga, laa xam ne kanamam gi du kanamu fenkat, li ma njëkk a degg mu wax ko mooy: "yéen nit ñi, deeleen tasaare nuyóo, di leele ñam, di jokk mbokk, di julli guddi fekk nit ñi a ngi nelaw, kon dangeen dugg àjjana ci jàmm".At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat