Hadith for the World

All hadiths

The complete card collection, filter by chapter

655 hadiths

عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه مرفوعاً: «يُؤْتَى بجهنم يومئذ لها سبعون ألف زِمَامٍ مع كل زمام سبعون ألف ملك يَجُرُّونَهَا».رواه مسلم
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax ci sujjóotam: "Allaahuma ixfir lii sanbii kullahu, diqahu, wa jillahu, wa awwalahu wa aaxirahu, wa halaaniyatahu wa sirrahu".Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
عن أبي سعيد الخدري رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم : "الْبَاقِيَاتُ الصَّالِحَاتُ، لَا إلَهَ إلَّا اللَّهُ، وَسُبْحَانَ اللَّهِ، وَاَللَّهُ أَكْبَرُ، وَالْحَمْدُ لِلَّهِ، وَلَا حَوْلَ وَلَا قُوَّةَ إلَّا بِاَللَّهِ".رواه ابن حبان والحاكم، أما النسائي فرواه في الكبرى لكن من حديث أبي هريرة
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam».Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax: "Allaahuma aslih lii diinii allasii huwa hismatu amrii, wa aslih lii dunyaaya allatii fiihaa mahaasii, wa aslih lii aaxiratii allatii fiihaa mahaadii, wajhal alhayaata siyaadatan lii fii kulli xayrk , wajhal almawta raahatan lii min kulli sarrin".Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Muusa yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu nettali ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne daan na ñaan ñaan gii: "rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal Mu-axiru, wa Anta halaa kulli say-in xadiirun ".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul bàyyi di ñaan lii, bu gontee ak bu xëyee: "Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati, Allaahuma innii as-aluka alhafwa walhaafiyata fii diinii wa dunyaaya wa ahlii wa maali, Allaahuma ustur hawratii -walla hawraatii- wa aamin rawhaatii, Allaahuma ihfasnii min vayni yadayya, wa min xalfii, wa han yamiinii, wa han simaalii, wa min fawxii, wa ahuusu Bika an uxtaala min tahtii".Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Jële nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: bokkoon na ci ñaani Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "Allaahuma innii ahuusu bika min sawaali nihmatika, wa tahawwuli Hanafiyatika, wa fujaa-ati niqmatika, wa jamiihi saxatika".Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abdullah ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ñaan ci baat yii; "Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa".An-nasaa'iy soloo na ko, ak Ahmat
عن عبد الله بن عمر رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال: «المؤمن الذي يخالط الناس، ويصبر على أذاهم خير من الذي لا يخالط الناس ولا يصبر على أذاهم».رواه الترمذي وابن ماجه وأحمد
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax, xéral ci lu lay jariñ, te nga dimbandikoo Yàlla te bul lompañ, bu la dara jotee, bul wax ay bu fekkoon ne defnaa lii mbaa lee kon lii du am, waaye waxal ne Yàlla dogal na te lu ko neex lay def, ndax boo waxul loolu yaa ngi ubbil saytaane buntu».Muslim soloo na ko
عن أبي هريرة رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: «الْمُؤْمِنُ مِرْآةُ أَخِيهِ الْمُؤْمِنِ».رواه أبو داود والترمذي
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñiy rëbbaate duñu nekk ay seede du caagine ay rammkat ëllëg bis-pénc».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaan mooy jaamu Yàlla» daal di jàng: "Aaya biy wax ne: {séen Boroom nee na wooleen ma ma wuyu leen ñi may rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox} [ soratou Xaafiri: 60]».Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
عَنْ عِيَاضِ بْنِ حِمَارٍ أَخِي بَنِي مُجَاشِعٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ: قَامَ فِينَا رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ ذَاتَ يَوْمٍ خَطِيبًا، فَقَالَ: وَسَاقَ الْحَدِيثَ وَفِيهِ: «وَإِنَّ اللهَ أَوْحَى إِلَيَّ أَنْ تَوَاضَعُوا حَتَّى لَا يَفْخَرَ أَحَدٌ عَلَى أَحَدٍ، وَلَا يَبْغِي أَحَدٌ عَلَى أَحَدٍ».رواه مسلم
Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari".Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".Al-buxaariy soloo na ko
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana, te nit ki du deñ di dëggal di jublu dëgg ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab dëggalaakon la, maa ngi leen di moytandikuloo fen, ndaxte fen day yóbbe cig kàccoore, te ag kàccoore day yóbbe sawara, te nit ki du deñ di fen, di jublu fen, ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab fenkat la».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati».Muslim soloo na ko
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat