Hadith for the World
Ngëneel yi ak teggiin yi

Xam jikkoy Lislaam yi

56 hadiths

56 hadiths

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: amuma waruwaay, kon nag jox ma waruwaay, mu ne ko: «amuma ko», am ku ne ko: yaw Yónente bi, dinaa ko tegtal ku ko jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am».Muslim soloo na ko
عن عبد الله بن عمرو بن العاص رضي الله عنهما أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: «من الكبائر شَتْمُ الرجل والديه» قيل: وهل يسبّ الرجل والديه؟ قال: «نعم، يسبّ أبا الرجل فيسبّ أباه، ويسبّ أمّه، فيسبّ أمّه».متفق عليه
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral ganam».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
عن أبي هريرة رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال: «الْمُؤْمِنُ مِرْآةُ أَخِيهِ الْمُؤْمِنِ».رواه أبو داود والترمذي
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñiy rëbbaate duñu nekk ay seede du caagine ay rammkat ëllëg bis-pénc».Muslim soloo na ko
عَنْ عِيَاضِ بْنِ حِمَارٍ أَخِي بَنِي مُجَاشِعٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ: قَامَ فِينَا رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ ذَاتَ يَوْمٍ خَطِيبًا، فَقَالَ: وَسَاقَ الْحَدِيثَ وَفِيهِ: «وَإِنَّ اللهَ أَوْحَى إِلَيَّ أَنْ تَوَاضَعُوا حَتَّى لَا يَفْخَرَ أَحَدٌ عَلَى أَحَدٍ، وَلَا يَبْغِي أَحَدٌ عَلَى أَحَدٍ».رواه مسلم
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana, te nit ki du deñ di dëggal di jublu dëgg ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab dëggalaakon la, maa ngi leen di moytandikuloo fen, ndaxte fen day yóbbe cig kàccoore, te ag kàccoore day yóbbe sawara, te nit ki du deñ di fen, di jublu fen, ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab fenkat la».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat
Jële na ñu ci Sahd Ibn Abii Waqaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: «Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon, yóbbe na leen ñu tuur seen i dereet ak a daganal araam».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yònente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- Soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal».Muslim soloo na ko
Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli».Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nekkul woon ku ñaawi wax mbaa jëf, daa na wax naan: « ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc» nee na: mu daal di jàng: aaya bii «{niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102]»Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate».Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
عن أبي هريرة رضي الله عنه مرفوعًا: «بينما رجل يمشي في حُلَّةٍ تُعْجِبُهُ نَفْسُهُ، مُرَجِّلٌ رأسه، يَخْتَالُ في مَشْيَتهِ، إذ خَسَفَ اللهُ به، فهو يَتَجَلْجَلُ في الأرض إلى يوم القيامة".متفق عليه
عَنْ أَبِي مُوسَى الأَشْعَرِيِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «أَطْعِمُوا الجَائِعَ، وَعُودُوا المَرِيضَ، وَفُكُّوا العَانِيَ».رواه البخاري
عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه عن النبيِّ صلى الله عليه وسلم ، قَالَ: «لا يدخلُ الجنةَ مَن كان في قلبه مِثقال ذرةٍ من كِبر» فقال رجل: إنّ الرجلَ يحب أن يكون ثوبه حسنا، ونَعله حسنة؟ قال: «إنّ الله جميلٌ يحب الجمالَ، الكِبر: بَطَرُ الحق وغَمْطُ الناس».رواه مسلم
Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub ak Muxiirata Ibn Suhbata yal na leen Yàlla dollee gërëm ñu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi".رواه مسلم في مقدمته